
youssou n'dour - doole كلمات أغنية
sa doole sa doole sa doole bul ko xeexe
jaay doole baaxul ag si ku mu mene doon
dekkende yi fonkal seet ci yalla mi nu moom
ana jambaar yu mag yi boroom alal yu bare yi
boroom xam xam yu rey yi ne kenn nekkatu fi
aah doole du wey
jaay doole baaxul ag si lu mu mene doon
tay men nga baaxle, ellek nga daldi yaqule
bul nawoo sa doole ba tax nga gaawa laale
ku yegsi men ko faale te nga saxoo di baale
aah doole du wey
maandul te rafetal sa nekkin
yaw deel baale bana wane sa doole
bul jel yaw sa doole xal di ko xeejе
sa doole dimbele ci jaam yi
jaay doolе baaxul ag si lu mu mene doon
bul kan sa doole ba di ko tiiteroo
besa ngi ci bes yi te faww bes bi yegsi
nu dajale yaw sa jef yi nga xam nè yalla mu ngi fi
aah doole du wey
fas wa dafa naagu ne mbaam ma maa la gene gaaw
booy daw da ngay yeex te man da may gaaw
fas wa di njekkente ba far dugg ca teen ba
bu dul woon ag mbaam ma fas wa des ca teen ba
aah doole du wey
ne maandul te rafetal sa nekkin
yaw deel baale bana wane sa doole
bul jel yaw sa doole xal di ko xeeje
sa doole dimbele ci jaam yi
sa doole sa doole sa doole bul ko xeexe
jaay doole sax woorul kenn xamul fooy mujjee
jaay doole sax woorul ndax kenn xamul fooy mujjee
bul naagu si sa am am
ndax adduna men na laa njuuy
am am ag men men dekkul fenn
waaye doole jii ci biir mbeggeel
kenn menuko teye
bu xasee jog, jamm jeexna
lu new daan, seetal
li ci jig mbeggeel jigu ci leneen
mbeggeel gu woor wane doolee ko jig
bu ko deful ba seytaane dugg ca, seetal
doole jii ci biir mbeggeel
kenn menuko teye
bu xasee jog, jamm jeexna
lu new daan, seetal
doole jii ci biir mbeggeel
kenn menuko teye
bu xasee jog, jamm jeexna
lu new daan, seetal
كلمات أغنية عشوائية
- fletcher, james - i knew كلمات أغنية
- curtis dro - no excuses كلمات أغنية
- guvna b - safe place كلمات أغنية
- lil wax - aight so boom (intro) كلمات أغنية
- reggie kilo - bruv كلمات أغنية
- canção nova - te louvo em verdade كلمات أغنية
- fenga - genesis كلمات أغنية
- transparent-c - with you كلمات أغنية
- eisvoleas - oι xωρισμένοι كلمات أغنية
- indecent 88 - selfexperiment كلمات أغنية