nitdoff - liniou yallah maye كلمات الأغنية
{verse 1}
sunu thianganak sunu niaakeu farlou
mognou yaubé nakh saaay tchi liniou warlou
mak gnifi néwone natale naniou sunu xarlou
téguil niou ci yone yiniou iblis meunone karlou
kone kepp kou tcha diaar bokou tcha bopp yay darlou
aayé naniou djaayou djayou ak parparlou
digueul naniou kénènal yallah djiy kaabarlou
farataak sunna laniou tégone séni tankeu, baamél yéy séni banque
niom nafsu laniou bankeu, kénène koula wo ci lénène loudoul lii na nga lankeu
gni lé matta roy ci képp kou yallah taxa jog
na nga mandou nanga djoup teksi na nga sakho toup
firile naniou al_qur’an guindi niou ci ay hadith
khassaide ak olofal taalif ba nieup guiss
yow sunu thiaganak sunu niaakeu farlou
moniou yaubé dém fénène di woute lénène
{refrain}
sunu thianganak sunu niaakeu farlou leu
amatouniou lay suniou reeré nioko tay
kholal yilé xettou ngueunéél youniou sunu buur bi maye
sénégal diiné taakeu nafi té dou meusseu fay
mouy tchi bamba di tchi maodo khassaide ak bindeu waye
cheikhna abass nioune niaakou niou ay walliouw youniou roye
kone bouldi wédi mayou yallah xamo noumou doye
kepp kou dingate sunu serigne cii sa safara ngi boye
{verse 2}
touba touba, kholal lafa yallah def, modou bamba ak cheikh fall kholal liniou yallah may
siguil naniou diiné ak derr bou nioul baniouy saggou tay
xeuthio wouma reew mi, mane djitou na ci khol yi
tchi djakka yek tchi daara dji moy borom paressol bi
maodo mal!ck maodo mal!ck sikar saa ngi dioli
sunu thiaganak sunu niaakeu farlou moniou tardel
reew mou am baaye niass daradjaam dja weurna aduna yallah ka barkel
baaye limamou kiraama tchi kaala gui
ndox maa ngi nékh dauphins yi sakh ziaaré ciii
beureup beu séleu neu sén thioline ngeu andak yiiw
randal neu guedj gui dakkeu cheytané mouné fiiw
perr ya ngi dall tchi grottou bandiagara
omar foutihou djixaate neu ba gnibi aadiana
mountaga ahmed al kabir ak ibn abass sall
lougo lo sunu aldiana gni gnoko arassal
bindeu naniou tchi olofal, moussouniouko oyofal
bougne lène dieundék niénène suniou bopp lagni torokhal
danio deudou djayanté yallah té lolou molène fal
{refrain}
sunu thianganak sunu niaakeu farlou leu
amatouniou lay suniou reeré nioko tay
kholal yilé xettou ngueunéél youniou sunu buur bi maye
sénégal diiné taakeu nafi té dou meusseu fay
mouy tchi bamba di tchi maodo khassaide ak bindeu waye
cheikhna abass nioune niaakou niou ay walliouw youniou roye
kone bouldi wédi mayou yallah xamo noumou doye
kepp kou dingate sunu serigne cii sa safara ngi boye
{verse 3}
borom bonnet carré beu manteau baak sa kaala ba
secret ya ngi tchi kourouss sidjaadaak sattala ba
défar nga sa talibé taaral nga sa tarikha
mansour dabaakh babacar sadiqqa
fallou borom ndindi saliou borom diamono
sénégal dafa melni xamouniou liniou yallah maye
naar yélène tuuf pour niou saga sunu serigne ci
souniou niaaké fayda dinagne dévier sunu jeunes yi
sén dégueuh dégueuh tchi li neubou ak li feegne
niaari tëré lagni djangue fokni xam nagne loudoul dégne
tambali séni d_nkaate tchi ay walliouw yu yallah déy
nio ngi financé ay djakka di xoutba lou xel yi téy
{refrain}
sunu thianganak sunu niaakeu farlou leu
amatouniou lay suniou reeré nioko tay
kholal yilé xettou ngueunéél youniou sunu buur bi maye
sénégal diiné taakeu nafi té dou meusseu fay
mouy tchi bamba di tchi maodo khassaide ak bindeu waye
cheikhna abass nioune niaakou niou ay walliouw youniou roye
kone bouldi wédi mayou yallah xamo noumou doye
kepp kou dingate sunu serigne cii sa safara ngi boye
{outro}
sant naniou yallah boubah
mame bou kounta ndiaassane
mame cheikhna sadibou, serigne saam mbaye
serigne cheikh tidiane g_ye, el hadj ibou sakho
serigne hady touré, imam assane cissé
maa shaa allah maa shaa allah kou lim djoum
nioune sénégal sant naniou yallah boubah
ci sunu diambaarou diiné yiniou yallah may niou gueune léna fonk
yalna yallah yokk séni lerrr
gnifi dess yalna yallah gueune léneu wéreul
yokou séni fane, yokou séni martaba, yokou séni wilaaya
maa shaa allah hamdulilah
كلمات أغنية عشوائية
- coffin break - boxes and boxes كلمات الأغنية
- slime dollaz - hood olympics! كلمات الأغنية
- miss tee - я и ты (me & you) كلمات الأغنية
- nyankobrq - すこぶってる (sukobutteru) كلمات الأغنية
- pile of love - what i'll be كلمات الأغنية
- 10cm - drawer(romanized) كلمات الأغنية
- cat.flp - spider webs كلمات الأغنية
- lil$avageazz - snitchk كلمات الأغنية
- tendon levey - when i’m grown like fully grown كلمات الأغنية
- upset - phone calls كلمات الأغنية