dip doundou guiss - homie كلمات الأغنية
yeah yeah
yeah yeah
bët du xool ba xam lu xel di gis
ma gëm say wax ba fàtte xool sa jikko
mën ko faj waaye dam la bàyyi ci biir
ëllëg du añ te mat na fàttaliku
ho
homie, homie, homie, homie
bët du xool ba xam lu xel di gis
ma gëm say wax ba fàtte xool sa jikko
mën ko faj waaye dam la bàyyi ci biir
ëllëg du añ te mat na fàttaliku
ho
homie, homie, homie, homie
depuis temps xale la ma gëj dal
mbëggeel dëggu ni yaay bàmmeel ak ay mbugalam
dëju mawti ng_y xam ne dee moo gën a dëggu xol
xarit dëmm la chaque année ma koy gën a gëm
ndax mbëggeel du jaay divorce du fay dot
njëkk a jooy miraas ba noppi xew dëj
lii jikko jaan la feesal dell ci jëmmu xaj
li ko taal batey mu yegg lay njëkk fay
pexe noon du contre yaw pour yaw la n_gga
kenn mënut a gaaw ci tijji xel ni paaka ci xol
xam sa bopp bu doon école kenn a du fa passer diplôme
tuxal dëkk a gën a yomb nit ki changer jikkoom
bu doon ku baax du daj lu bon yónnent du doon jirim
nelaw ci bàmmeel rekk a yàgg te amul lal ci biir
wor nga ma ma n_gga bàyyiwuma la dam la ba ci biir
yaa ma woon ne man naa dëkk si pax ak ay jaan ci biir
bët du xool ba xam lu xel di gis
ma gëm say wax ba fàtte xool sa jikko
mën ko faj waaye dam la bàyyi ci biir
ëllëg du añ te mat na fàttaliku
ho
homie, homie, homie, homie
homie, homie, homie, homie
homie, homie, homie, homie
fàww ng_y loru yenn saay pour man yegg fenn fi
ku wann lor buy jur ci mettit lay wësin
boo bëggee jege sa jàmm fàww nga sori ñenn ñi
xarit bu jege gën a jekku énnemie
dëgg nattukaay jëf du changer melo comme nun
du sutura rekk jëf lu bon a tax nit njëkk a nëbbu
lu tax nit gën te fekk mala yee nu gën a dëggu
ndax ci jikko juda moo ëpp sët jesus ci kaw suuf
noon bi lay ŋàññ gën sa waa ji lay jay
noon biy tax ng_y ñafe moo gën ñi lay wër di lay fen
jarul topp nitu intérêt àdduna ay àjjanaam
ñi di dagg sa xol yaa tax seen paaka ñaw
do my story sometimes, do my story sometimes
do my sto peace of mind
do my sto do my sto
do my story sometimes
do my story peace of mind, do my story peace of mind
do my sto do my sto
homie, homie, homie, homie
كلمات أغنية عشوائية
- gladys knight the pips - good night my love كلمات الأغنية
- bob marley - sugar sugar (jad version) كلمات الأغنية
- bone thugs n harmony feat yolanda adams - order my steps (dear lord) كلمات الأغنية
- indiana bible college - at a loss for words كلمات الأغنية
- seal - everything will be alright كلمات الأغنية
- joan osbourne - sara smile كلمات الأغنية
- dionne warwick - please make him love me كلمات الأغنية
- the higher - try again كلمات الأغنية
- indiana bible college - bless the lord كلمات الأغنية
- randy crawford - only your love song lasts (lp version) كلمات الأغنية